Tënkub coppite yi am ci Déggooy Cëri Microsoft – 30 fan ci Sàttumbar, 2024
Noo ngi yeesal Déggooy Cëri Microsoft, yuy jëfe ci sag jëfandikoo costéef mbaa cëri Microsoft yiñ jagleel kiliyaan yi te nekk ci net bi. Xët bii dafay Joxe nanu ab tënk ci coppipte yuñu gën ràññee ci Déggooy Cëri Microsoft.
Ngir gis coppite yépp, noo ngi lay digal nga jàng Déggooy Cëri Microsoft bamu jeex fii.
- Ci kawu xët wi, yeesal nanu bisu siiwal ci 30 fan ci Sulet, 2024, ak bis bimuy dox ci 30 fan ci Sàttumbar, 2024.
- Ci pàccu Jëfandikoo Cër yi ak Ndimbal, ci biir pàccu Yemale ak Doolel ñoŋal yokk nanu ab lëkkalekaay ci sunu xëtu sàrtu biti ngir gëna leeral ak neexal jëfandikoo gi.
- Ci pàccu Sàrt yuy àndak cër yi, yokk nañu ci yeneen coppite yile:
- Ci pàccu Xbox, leeral nanu ci daluwebi jàmbur yi bokkul ci Xbox mën nañu sàkku ci jëfandikukat yi ñu joxe seen ëmbiit ak njoxe ngir mëna fo ci titre yu Xbox Game Studio te yooyu sitwebi jàmbur mën nañu jël boole ci joxe say leeral, bokk ci seeni sàrt. Leeral nanu ci ron-pàccu Xale yi ci Xbox ni man-mani jekkal yu bari mën nañu baña jàppandi sudee titre yu Xbox Game Studio dañu jàppandi ci sitwebi jàmbur yi on third-party platforms. Leeral nanu ni yenn Cëri Xbox mën nañu am seen sàrti jëfandikoo bopp ak anamu doxalin.
- Ci pàccu Mboolem Màndarga Microsoft, leeral nanu ni man-man yii ci Cëri Microsoft kese lañu bokk tax mëna nañu bàña jàppandi ci yeneen sitweb yi.
- Microsoft Cashback: Yokk nanu ab pàcc ci prograamu Microsoft Cashback ngir leeral prograam bi ba noppi dëggal boobu nangu yooyu Sàrti Jëfandikoo Cashback dañu koy sàkku ngir mëna bokk ci prograam bi.Yokk nanu ab pàcc ci prograamu Microsoft Cashback ngir leeral prograam bi ba noppi dëggal boobu nangu yooyu Sàrti Jëfandikoo Cashback dañu koy sàkku ngir mëna bokk ci prograam bi.
- Ci pàccu Microsoft Rewards, dugal nanu ci baat yu bees ngir leeral ni ñuy sàkkoo ay Poñ to ci Rewards Dashboard ba noppi yooyu tomb dañu leen di jagleel seet yiñ jëfandikoo ngir mbir yu ñeel seetug boppu gu dëggu te xelu.
- Yokk nanu ab pàccc ngir dëggal sàrti jëfandikoo yi yilif jëfandikoog cëri Copilot AI Experiences.
- Yeesal nanu pàcc bi ci Cëri AI ngir yokk leeral ci AI buy jàppale, moomeelu ëmbiit, leerali dugg u ëmbiit, ak càkkutéefi yeneen wàll yi.
- Ci biir Sàrt yi, amal nanu ay coppite ngir mbir yi gëna leer boole ci jubbanti graameer, njuumte, ak yeneen jafe-jafe yu ni mel. Yeesal nanu itam tur wi ak iper-lëkkalekaay yi.